Metit (Pain) - Poem In Wolof by Alpha Robinson

METIT (Pain)

Tunde bele lumu sorri sorri

Helako gena sorri

Gëj lum rey rey

Metit munako opa

 

Baken nimu nexey

Nga jëlko ci ngalaw

 

Yaangi melni ku jogey ci benen jamano

Hanaa xamuloone ci tey leñ necka

 

Te halel moi magi ëlëk

Te baken bu mos dunda

Dina mos deh

 

Bon nak Adina potindaa la

Ku naan joh sa morom

Ken du jur bopaam

Te ken du suul bopam

 

Hanaa xamuloone

Nit lumu touti touti

Mo gena maga taahi-kow

Tas tabax amoon nafi

Wai deh deki musu fe am

 

Yaangi fenafen be Yabi

Melni xobi warga bu saali

Fu ngalaw fouf nga jublu

Xoolalmala

Ngai yoloos yoloosi

Melni bukki burus

Nooma xoleh ëlëk?

 

Tekat Tan tanehnala

Ngir moon lu deh la lekka

Wai yow yangma lekka

Te deyanguma

 

Hanaa Xamuloone fi "be faw" amatufi

Xew xewi rek mofi sah

Bon ndook bul melni puruh

Nyam binga ne feef

Ci suma loho la jaar

 

Nganaan ñun nga buga selmal

Te xamulooneh fi jantabi feñnafi

Wai bu bor setey

Ku rus ñaw

 

Yalna sa adina baña seda

Benga gis lorangeh ginga warral

Tek ko xaleh yu hamul dara

Balaa la suuf di sedey ëlëk

 

Yalna ñu ëlëk tannal jamano

Ni Xaleh bi di tanney malo mi

Seppi tilim bici suñ bir

Ngir suñ ëlëk naak

 

 

Alpha Robinson